JÉEGO CI LÀMMIÑU WOLOF

10 

Description

Sëriñ Abdu-Xaadr Kebe, ñu gën koo xam ci turu Jili Kebe, lijjantikat la (entrepreneur), yor lijjanti guy yëngu ci tabax ak liggéey yu ñémmeere yi (travaux publics). Gëstukat la tamit ci wolof, moo taxawal mbootaayug Akaademib Wolof (AW), muy mbootaay gees xam ab liggéeyam ci lënd gi (Internet bi). Bind na lu sakkan ci wolof, lu war a génn ak lees siiwal ci lënd gi. Moo tekki “Tasawudus sixaar“, “Iwaawu Nadiim“, “Nahju qadaal Haaj“, “Mawaahibul Xudoos” ak yeneen ci téerey Sëriñ Tuubaa yi. Lu sakkan ci Wikipedia Wolof moo ko def. Am njàngam ci araab, ci daara ju Sëriñ Saaliw la ko defe, jàng xam-xam ba jeexal, jàngale as lëf, tukki dem Amerig, Farãs, Itali, Imaaraat ba Siin, di wax araab, bind ci ay jukki yu bari, jële ci farañse ay téere niki téere mboor bu ma-mboor bii di Mbay Géy Sill def te tudd “CHEIKH AHMADOU BAMBA (RTA), Que sont devenus ceux qui ont essayé d’entraver sa mission ?, di téere bu am solo ci xew-xew yi amoon ci diggante Sëriñ Tuubaa ak Tubaab bi. Sëriñ Kebe dégg na yit àngale ak làkkuw Itali. “Adjoint au maire” la ci Tuubaa.

Avis

Il n’y a pas encore d’avis.

Soyez le premier à laisser votre avis sur “JÉEGO CI LÀMMIÑU WOLOF”

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *