DAWAL AK BIND LÀMMIÑU WOLOF

18 

Description

JAAR-JAAR
Maamur Daraame Doktëer la ci xam-xamu làmmiñal ginnaaw bi mu amee doktoraam ci Département linguistique et sciences du langage, FLSH,
UCAD. Jamono jii ab gëstukat la ci wàllu làmmiñal ci Laboratoire de Linguistique bu IFAN –
Cheikh Anta Diop. Lu moy liggeeyu gëstu boobu
muy def ci IFAN – CAD, Sëñ Daraame mu ngi
yëngu ci njàngalem wolof, njàngalem Phonétique
articulatoire du français ak Expression orale du
français ci FLSH bu UCAD. Maamur Daraame mu
ngi jàngale Expression orale du français ci CESTI
(UCAD) tamit. Kenn la tamit ci ñi sos Ëttub wolof,
dalu web buy jàngale dawal ak bind làmmiñu
wolof, www.ettubwolof.org, te soppiku tey,
www.kallaamayreewmi.sn ginnaaw bu ñu boole
pulaar, séereer, joolaa, màndeŋ ak sóoninke ci
njàngale mi. Dinay faral di liggeey ak ONG ARED
ci lu jëm ci tàggat ci làmmiñi Afrig yi muy def ak
téere yi muy bind, di leen móol.

Avis

Il n’y a pas encore d’avis.

Soyez le premier à laisser votre avis sur “DAWAL AK BIND LÀMMIÑU WOLOF”

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *