BUBAKAR BÓRIS JÓOB, BINDKAT : “KENN WARUL A ÑÉDD NGUUR BA SAY BAARAAM DI NÀCC.”

BUBAKAR BÓRIS JÓOB, BINDKAT : “KENN WARUL A ÑÉDD NGUUR BA SAY BAARAAM DI NÀCC.” post thumbnail image

Seen yéenekaayu web, Lu Defu Waxu, amal nab laaj-tontu bu yaatu ak werekaan bii di Bubakar Bóris Jóob, di bindkat bu ñu ràññe ci àddina sépp. Ci waxtaan wii mu séq ak Paap Aali Jàllo, mi ngi ciy biral xalaatam ñeel tolluwaayu réew mi jamono jii ak jaamaarloo bi dox diggante Njiitu réew mi, Maki Sàll, ak njiitul Pastef li, Usmaan Sonko.

Noo gise liy xew ci réew mi alxemes ba tey ?

Alxemes jii nu génn la yoon dogal ne Usmaan Sonko war naa tëdd kaso ñaari at. Noo ngi teg tey sunuy bët ci yëngu-yëngu yi àtte boobu jur.  Ñi ci mere Maki Sàll bare nañu lool tamit. Liñ tudde “Mbirum Sweet Beauté”, man mii dama cee mas a am kersa. Ndax jaaduwul, réew mu tol ni Senegaal, ak fi mu jaar, ak ñi fi jaar, ñu dem ba fàtte koom-koom, fàtte njàng meek wér-gi yaramu askan wi, di werante ndax Usmaan Sonko siif na Aji Raabi Saar walla siifu ko… Su doon lu am la sax, ñu ne waaw. Waaye, dafa yàgg a leer ne ñi tëgg mbir mi, te Aji Saar ci boppam tudd leen, duggewuñ ko woon lu dul sosal Usmaan Sonko, fexe ba du samp ndëndëm ci joŋante 2024 bi. Ñaaw nañ ci, yàq deru Senegaal ba noppi dooleel Sonko. Cuune mënul a weesu lii. Kon, ñooñu sosal Sonko ñooy réccu tey, naan su ma yëgoon. Suñ njortoon ne nii lañ ciy ñaawe duñ ci dugg. Ay bakkan a ngiy wéy di ci rot, koom gaa ngi gën a nërmeelu, àddina sépp a ngi nuy reetaan.

Ñaari at yi yoon ne Sonko war na koo tëdd nag…

Mooy li merloo ñépp. Mënoo ne kii liñ koy toppe dara amu ci ba noppi teg ci ne, waaye, fàww caabi féete ko ginnaaw lu mat ñaari at. Li àttekat boobu di Isaa Njaay tudde “corruption de la jeunesse”, daanaka fan yii la ko askanu Senegaal mas a dégg te guléet muy dugal nit kaso ! Yëf yi, maa-tey lay gën a nirool te muy Maki Sàll, di ay àttekatam ak ñi làqu woon ci ginnaaw Aji Saar di ko déey li mu war a wax ngir dugal Sonko, ñooñu ñépp ameel nanu réew mi àq te mbir mi warees na koo topp.

Aji Saar nag…?

Bu doon sama sago, dañ koy dimbali, jàppale ko mu defaraat àddinaam. Xale la, ñu am doole am alal naan yóoram, defloo ko njaaxum. Fi mu ne nii, xajatul ci réew mi. Gëwma ni dinañ ko rawale ndax bëgguñu mu rëcc leen te xel dajul ñu koy bàyyi muy doxi soxlaam Ndakaaru walla Ndar walla Jurbel. Ci sama gis-gis bu gàtt, kenn warul a mere Aji Saar, dees ko war a yërëm, dimbali ko.

Li Sonko wax ci moom nag ? “Dàngin bu am AVC”…

Loolu du waxu nit. Lan moo aay ci AVC ? Bi ma déggee kàddu yooyu, sama bopp xaw naa ubu. Ak luñ la tooñ tooñ, boo demee ba am sañ-sañu laaj lu tol nim réew, am na noo xam ne waroo koo waxe. Xam naa ni jamono yii, Sonko tal na leneen lu dul balu àq Ajii Saar. Waaye de, baax kon na mu def ko, baluwaale àq soppeem yi mu teg gàcce gu réy.

Ñu baree ngi naan guléet lu ni mel xew Senegaal. Lu ciy sa xalaat

Liñ tuumaal Sonko, ne dafa siif doomu-jàmbur ngay wax ?

Waaw. Ak tamit ni nguur gi sonalee Sonko. Moom ci boppam nee na keroog kenn masu fee gis lu ni mel…

Ànd naa ci loolu. Nun ñiy mag, yàgg fi, bu dee mbirum pólitig rekk, lu nekk teewe nan ko fi. Waaye, ni nguuru Maki Sàll giy sonale Usmaan Sonko, guléet nu gis lu ni mel ci réew mi. Am na ñu koy weddi, naan buleen fàtte Mamadu Ja ak Abdulaay Wàdd mbaa ñeneen ak ñeneen… Muy dëgg tamit. Wànte, guléet doomu Senegaal, doomu réew mi, jóg di laaj nguur gi, bëgg a toog ci jal bi, ñu tuumaal ko ay tuuma yu ñaawee nii. Mu diy tuuma diggante góor ak jigéen yu teguwul fenn. Ndax xel daj na Seŋoor def lu ni mel ? Amul luñ fi yakkul Abdu Juuf, Wàdd dem na bay bëgg sullilu néewu baayam ca Ndar, waaye taxul Juuf saalit ba naan dafa tëdde diw walla diw. Wàdd ci boppam, ba ay séytaane ñëwee ni ko am na sa noon bu mag buñ bett ci Kornis bi, nataal yaa ngi nii, dafa ni leen xottileen seen foto yooyu, man Ablaay Wàdd jomb naa yenn yi.

Ndax gënul woon Sonko teew ca àttewaay ba ?

Tontu ci laaj boobu du yomb. Leeg-leeg ma xalaat ne su fa teewoon kenn du fa sañ a tudd “corruption de la jeunesse” waaye tamit gor mënut a dékku yenn yi, fuñ la nar a toroxalee ciy kàcci kese, doo fa sawar a teg tànk. Te yit, neexul saa yooy dem àttewaay ba, ñu topp la, di la dóor, naan la awal fii, doo aw fii, defal nii, lu nekk ñu la koy teg. Mi ngi fiy sog a am. Fii la réew mi tollu.

Wax nga sànq ne yoon war naa jublu ci ñi tëgg mbirum Aji Saar, tuddaale ci Maki. Waaye moom, bu loolu weesoo, ndax am na leneen lu ko yoon war a toppe ëllëg ?

Waaw, ragal naa ne nguur gii fi nekk, bu fi jógee, dina am luñ koy toppe. Xam nga Abdu Juuf, kenn toppewu ko dara. Seŋoor, moom sax, kenn tuddaalewu ko. Ablaay Wàdd tamit, kenn toppewu ko dara. Waaye, ak ni mbir yiy demee nii tey, wax-dëgg-Yàlla, bu geneen Nguur toogee, gëmuma ne Maki Sàll dina mucce noonu. Dafa di sax, loolu moo tax ma jàpp ne, gaa ñii fi nekk, caaxaan du leen fi jële. Ndaxte kat, xam nañu li leen di xaar bés bu Maki Sàll wàccee. Te xéy-na sax mooy gën demin yenn farandoom yi gën a fés yi dëkke xasteek a saaga. Maki kilifa la, Tubaab yi mën nañ koo neexale ndombal-tànk lu diis ca Mbootaayu-Xeet ya mbaa feneen. Àttekat yeek taskati xibaar yeek ñeneen ñi koy jàppale amuñu fuñ daw làqu.

Danga ragal feyyoonte ?

Kenn ñaanu ko Yàlla. Liggéey naa lu bari ci réew mu mel ni Ruwàndaa te looloo ko yàq. Moo tax ma naw Paul Kagame mi fa dakkal feyyoonte diggante Hutu yi ak Tutsi yi.  Te liy xew tey Senegaal du dara soo ko méngaleek ñaawteef yañ doon def Ruwàndaa ci 1994.

Kon jàpp nga ni bu Maki bokkee sax dañ koy duma ?

Ku nekk ak niŋ ko gise, waaye man loolu laa gëm. Moo tax, léeg-léeg, ma dem ba mu yàgg, sama xel ñaaw, ma ni joŋante yees di waajal de, amaana gaa ñi fexe ba du fi ame. Xéy-na léegi nu dégg ay baat yu mel ni “état d’urgence” mbaa sax “état” de siège”, taafantoo ko dàq joŋante 2024 bi.

Mën naa àgg ba foofu ?

 Duma gisaanekat, maak ñépp a ci yem waaye loolu laa njort.

 Lan moo tax nit ñi topp Usmaan Sonko ?

Ñépp a ngi naan Sonko nit ku jub la, dëggu, am fit. Waaye, du moom rekk a mel noonu ci làngu politig gi, mënees na wax lu ni mel ci ñeneen doore ko ci Ceerno Alasaan Sàll mi fi tekki woon ndombal-tànk lu am solo, delloo ko Maki Sàll  ne ko lii Total bëgg a def baaxul ci réew mi, ànduma ci, dem naa sama yoon. Man dama jàpp ne, li may dëgg doole Usmaan Sonko moo di ne nun saa-Senegaal yi, képp ku ñuy tooñ, yow lanuy faral. Rawatina bu dee lépp liñ lay jiiñ ay kàcci kese la. Xéy-na dinga ma : “Karim Maysa Wàdd, nag ? Xalifa Abaabakar Sàll, nag ? Ñoom it dañ leen a tooñoon, du ?” Waaye ñaar ñooñu dañoo juum, wóolu Yoon ba yaakaar ne dina leen setal. Usmaan Sonko gis loolu, ne moom day jaamaarlook nguur gi, lu mu ci góobe gar ko. Kon, loolu moo tax nit ñi di ko topp, di ko topp ba léegi, dafa mujj, ñi nga xam ne dañoo mere Nguur gi yépp, te Yàlla xam na ne bari nañu, ci Sonko lañuy gis seen bopp. Te ni ma ko waxe sànq, àtte keroog bi da koo dooleel bu baax a baax.

Dem nga ba ni bés ni nit ñi toppe Sonko masu fee am.

Li ma gis rekk laa wax. Dëgg la, am na fi ba tàyyi ay njiit yu nit ñi gëm, topp leen. Ablaay Wàdd jaar na fi, bun ko fàtte ak ñeneen. Waaye, ni mu mel nii, wax-dëgg-Yàlla mësuma koo seetlu. Li ci gën a doy waar moo di ne Sonko gone la te bi mu duggee ci làngu politig gi yàggul, atum 2014 la tàmbalee pólitig, su ma juumulee.

Ndax lu ni mel du biral tamit ne dafa xereñ ?

Loolu nag mooy coow li, Paap Aali ! Xam nga, soo nee kenn masu fee ëpp Sonko ay nit, dafay am lu muy nirool, dina am ñu xalaat ne farandoom nga, di tagg sa mbër. Du loolu. Nit ki mën na siiw, am bayre lool, ñépp topp ko te, ba tey, du tax mu mën a téyem réew. Gisaguma lu fi Usmaan Sonko def bañ koy méngaleek ñoomin Abdulaay Li walla Mamadu Ja ak Séex Anta Jóob. Gone yi xamul dara ci seen mboorum réew mën nañoo xalaat lu ni mel waaye boo demee ba am yenn at yi, am foo jaar, doo jey sa moroomu doom. Loolu, dama bëgg ñépp bàyyi ci xel.

Ndax mën ngaa gën a leeral wax jooju ?

Waaw. Damay faral di wax ni ñaari mbir doŋŋ ñoo tax may jàppaleendi Usmaan Sonko. Bi ci jëkk moo di ne dañ koo tooñ ba fu tooñ yem, ñépp war koo xeexle mu setal deram. Loolu moom, daanaka romb na pólitig di wéy. Ñaareel bi moo di ne danoo war a xeex ndax mu bokk ci joŋante 2024 biy ñëw. Waaye fii, bëgg naa nga déglu ma bu baax : léegi àttekat bi setal na deram ba mu set wecc – “corruption de la jeunesse” ay ree la def ñépp ! Bun demee ba mu bokk ci lawax yiy xëccoo nguur gi, képp ku ko jàppale woon ba mu am ndam ci ñaari fànn yooyu, wàccoo ngaak moom.

Te bu boobaa…?

Day daldi doon lawax buy laaj réew mi doŋŋ, ñu war a xam naka la ko nar a téyee, ndax am na kàttan gi ak yu ni mel. Ki ngay sànnil kàrt moom ngay dénk ëllëgu réew mi, kon doo ne rekk ginnaaw dañ ko fee tuumaaloon, moom laa bëgg mu toog ci jal bi. Déedéet, waruta yombe noonu. Ñépp lees a war a déglu, muy Sonko, di Abdu Rahmaan Juuf, di Xalifa Sàll, di Ceerno Alasaan Sàll, di Karim Wàdd ak ñeneen ak ñeneen. Ku nekk wax sa yéene ci réew mi, li nga ci nar a def ak niŋ ko nar a defe, nit ñi yeewu dibéer 25 féewaryee, dem sànnil xob ku leen doy. Dëgg la, mel na ni bu joŋante bi jaaree ci yoon, du ñàkk Sonko jël ndam li. Waaye teewul ñu war a seet ba xam ndax amul ci yeneen lawax yi ku ko ëpp kàttan. Bu doon sama sago, ñépp bàyyi ci xel. Ndax, li am léegi mooy ñaari nit rekk ngay dégg : Usmaan Sonko ak Maki Sàll. Man daal noonu laa ko gise, moo fiy indi jàmm. Ku jig Senegaal la askan wi war teg ci jal bi.

Lan nga xalaat ni moo tax réew mi meree nii Maki Sàll ?

Dafa xeex ba jot ci nguur gi ba noppi yàq yaxeet ndonol ñi ko jiitu ci boppu réew mi. Masumaa gëm ne Seŋoor ak Juuf ay demokaraat lañu woon, ñoo fi dàqoon labajey kàrt te benn pàrti rekk a fi amoon, daanaka. Wàdd tamit lu ko neex la  doon def. Waaye kenn ci ñett ñooñu masuta def ku wax lu ko neexul  mu ne la ràpp ci kaso bi, tëj.

Tey bés bu Yàlla sàkk ñu jàpp ay taskati xibaar niki Paap Njaay, Aminata Saar Ñaŋ ak Sëriñ Saaliwu Géy mbaa ay farandooy Sonko mbaa ñiy sàmm àq ak yelleefu doom-aadama, niki Aliyu Saane bu “Y’en a marre”. Kenn xamatul lu yëf yiy niru. Ni Maki di jëfandikoo Yoon mu koy defal li mu bëgg, yàgg na fee am, dëgg la, waaye li bees ci nguuram mooy ni mbir mi nee fàŋŋ, dem bay nirook maa-tey. Loolu dina jafe ñu baal ko ko. Fi may mujjee mooy fàttali ne ci diiru ñaari at ak lu teg tuuti, yëngu-yëngu yu metti am nañ fi ñaari yoon, ay bakkan yu bare rot ci. Yooyu la ñuy nar a fàttalikoo Maki Sàll ëllëg te dara rafetu ci. Rax-ci-dolli Juuf, bi ñu demee ci wotey 2000 yi, Abdulaay Wàdd duma ko, daf koo nangu. Abdulaay Wàdd bi mu demee 2012 Maki duma ko, daf koo nangu. Kon, kenn ci ñoom ñaar jéemul woon fexe ba doo janook lawax bu lay mën a xañ sa nguur. Abdu Juuf newul Abdulaay Wàdd mii kat, su ma ko bàyyee mu nekk lawax, du baax ci man. Kon, naa ko sàkkal pexe. Wàdd tamit, newul gone gii de, am na ñu koy jàppale bitim-réew ak ci biir réew mi, am na ay nit, kon du bokk. Li am léegi moo di ne, guléet, bi Senegaal doonee Senegaal ba tey, benn Njiitum réew, te Yàlla def na moom mooy Njiitum réew bi gën a nekk xale ci sunu mboor, mu ne  waaw, képp ku nar a taxaw janook man, ne danga bëgg nekk lawax, ma sàkkal la pexe. Loolu moo tax ñu mere ko. Du leneen. Tey lu jege 25i gone faatu nañ ci yëngu-yëngu yi, nu war tamit bàyyi xel ci Fran!ois Mancabou, Didier Badji ak Fulbert Sambou.

 Léegi noo ngi waajal 2024…

Coow lépp, mooy li Usmaan Sonko ne duñu ko def beyu sarax. Maki nag xamul loolu, xalaatul woon ne dina am ku koy jéem a të. Ndaxte, xam nga Nguur moom, boo woyofee bopp daf lay bewloo. Dangay dem ba dootoo xam sax fan nga nekk. Dooto xam a ràññatle. Jébbal nañ ko lenge yi, yaakaar ne li mu doon wax ci biir kàmpaañam gëm na ko, noonu lay doxale, mu wor nu. Nu yaakaaroon tamit ne ginnaaw xale la, xéy na moom moo gën a xam ni sunu àddina siy doxe tey, mooy gën a déggook ndaw ñi, ndaw ñi nga xam ne, ñoom ñoo daaneeloon Abdu Juuf, daaneel Abdulaay Wàdd.

“Dialogue national” bi, nag, gëm nga ko ?

Yëkkati nañ fay kàddu yu ñaaw, xeetu kàddu yooyuy taal réew. Diisoo lu baax la waaye mënuta am bu fekkee ku sëqat ci kujje gi nga tëjlu ko. Fi  yëf yi tollu sax, fàtte nañ seen jalog boobu.

Xam nga, yaa ngi jàpp nit ñiy tëj ci kaso yi. Ñi ngay woo, am na ci ñaar ñoo xam ne, xañ nga leen seen yelleefu nekk lawax, muy Karim Wàdd ak Xalifa Sàll. Kon, wax-dëgg-Yàlla, man, waxtaan wi, xawma lan lay jariñ. Waaye nag, lenn moom, mën naa ko nangu, mooy ni Karim Wàdd ak Xalifa Sàll, ginnaaw ubbil nañ leen bunt ngir ñu teggil leen li ñu leen teg, mooy daan yooyu nga xam ne moo leen tere bokk ci wote yi, fàww  ñu bokk. Bu dee waxtaan wi dina tax ñu mën a doon lawax, xéy-na ñoom, ñàkk pexee leen ci boole. Xawma PDS, waaye Xalifa, amaana bu dul woon loolu, du fa teg tànk. Kon, mbirum waxtaan wi moom dafay xaw a mel ni xeetu naxee-mbaay.

Loo nu mën a wax ci ñetteelu moomeel bi ? Lu tax ngay faral di wax ne Maki Sàll warul a bokk ci joŋante 2024 biy ñëw ?

Xam nga Ablaay Wàdd, dafa defoon li ñuy woowe « wax, waxeet ». Ñu ni ko Góorgi bàyyil caaxaan, li nga bëgg du fi ame. Wàdd def yëfu kilifa, dellu ginnaaw, mbir mi yem fa. Maki Sàll moom, boo seetloo bu baax, ci mbirum moome gi, dafa tegley at di def li ma tudde “wax, waxaat”. Dégg nañ ko fi ba tàyyi mu naan « Man ? 2024 ma génn pale bi, keneen dugg. » Dem na sax ba mel ni ku raatukaan, soo ko laajee mu wax, soo ko laajulee mu wax. Boo ko nee  saa waay noo sant sax, mu fëgg dënn bi ne la : « Xawma lu tax ngeen may laaj sama sant. Sàll laa sant. Waaye, lenn moom dinaa leen ko xamal, man gor laa, sama kàddoo ma moom, bii mooy sama moomeel bi mujj, dootuma ma nekk mukk lawax ! » Ngóor soosoo bëgg a jóge ci « wax waxaat » daanu ci « wax, waxeet » ! Loolu, xel mënu koo nangu, dafa ñaaw ci doom-aadama bum mënti doon, rawatina ci kilifa, ñu dénk la lu tol nim réew. Te  xam nga lan moo gën a doy waar ci 3eelu moome gi ? Moo di ne atum 2012 lan jëkk a fal Maki Sàll. Kon atum 2024 lay def 12i at ci jal bi. Mu nar a janook nun saa-Senegaal yi, ne nu : « 12i at yi jeex nañ, moo nekkoon sama moome bu jëkk. Léegi nag, maa ngi seet ndax dinaa leen laaj ñaareelu moome walla déet. » Waay waay, genn moomeg 12i at, loolu du ay wax ! Xam nga ne lii dafay tax ñu yab Senegaal.

Moone boroom xam-xam yu mag nee nañu Maki Sàll yelloo na 3eelu moomeel…

Dégg naa ñu naan, jenn doomu Farãs ju xam-xamam màcc ci wàllu Yoon nee na ko mën na bokkaat. Mënees na tudd tamit porfesoor bu siiw bu tudd Mariel Zouwankeu, am na lu mu wax doonte sax ay naataangoom weddi nañ ko. Waaye, ci ñooñii la Maki Sàll bëgg a sukkandiku ne : « Aa, lii la Yoon wax. »

Man nag jàpp naa ne kenn soxalwul nekk boroom xam-xam ngir xam ne, ci wàll wii, li ndeyu-àtte ji wax dafa leer nàññ.. Boroom xam-xami Yoon yi, ñoom, bu fi Maki defoon 40i at tamit, mën nañ la ne mooy moomeem gu jëkk. Waaye loolu neexul a dégg. Da ñuy dem ba mu mel ni ñiy bind àtte yi, duñu ay doom-aadama, bu dee benn kos (virgule) rekk, mën naa yëngal réew mi, seen yoon ci kos boobu, toppatoowuñ ko. Na réew mi tàkk ndax loolu, seen yoon nekku ci. Dafa mel ni ñiy bind àtte yi duñu ay doom-aadama te ñi leen koy tax a bind duñuy doomi-aadama ! Àtte dafa war a yenu maanaa. Def nga 12i at naan sama moome gu jëkk a ngiy sog a jeex, waxu ku danoo ci saret la. Yenn ñédd nguur yi dafa rekk ñaaw, di ñédd nguur ba say baaraam di nàcc rafetul. Ku xamul suur naa ñu téye sa loxo.

 

Fi réew mi tollu, kan nga yéene mu wuutu Maki Sàll ?

Loolu teel na ci wax ko. Nee naa la sànq fàww nu déglu lawax yépp ba xam ku ci nekk naka la nar a téyee réew mi. Wànte ci dëgg-dëgg, nun saa-Senegaal yi war nanoo bàyyi li nuy def, yeewu jenn dibéer, weeru féewaryee lay faral di doon, daldi dem sunu bérébu wote, dugg ci mbañ-gàcce yi, sànnil nit kàrt, daldi ne « Aa, kii de bu faloo, mooy nekk sama njiitum réew. » Kooku falu, nekk Buur te kenn du ci mën dara ndax noonu la Sàrtu-réew mi tëdde. Fii, koo fal njiitum réew, mooy moom ngomblaan gi, yaay yore daanaka teraanga képp kuy yeewoo ci réew mi, fal ak folli baa ngi say loxo, yaa moom Yoon, yaay jiite Ndajem àtte mu kowe mi di def lu la neex. Kooku du Buur di Bummi ? Bu fi loolu jógewulee dina jafe lool nu génn ci.

Demokaraasi yi yelloo turu demokaraasi yépp, liñ jiital mooy xàjjatle baati dogal yi. Duñ la ne yaay Buur ba pare ngay jaay màndute, naan doole ji ma askan wi jox ëpp na, xaaral ma wàññi ko ndax looloo gën ci Senegaal. Noo def dégg ku la ne danga ñàkk faayda mbaa danga ñàkk bopp te ku ñàkk bopp gaaw a dee.

Te bu nu waxantee dëgg, gisuma ci ñiy laajagum réew mi ku ci mbir moomu soxal. Du ci kenn, nag. Moone loolu la réew mi soxla, demokaraasi dëggëntaan foofu lay tàmbalee.

Related Post