Description
Yonent bi, na ko Yàlla dolli teraanga, dafa wax ne : « Ku Yàlla namm ci moom aw yiw, daf koy déggloo diine ».
Ginnaaw loolu, ndeem xam-xam mënul ñàkk ngir diine jaam bi mën a wér, ci laa jéem a binde, ci kàttanu Yàlla, téere bii ma tudde « Càllala xam sa diine, Ponk yi juróom » ci làmmiñu wolof, ngir mu nekk ndimbal ci jullit yi nga xam ne dañoo bëgg a xam seen diine te jànguñu araab, te dégg wolof.
Téere bii nag ñëw na ci « Tawhiid » te mooy wéetal Yàlla mu kowe mi, di dàtt bi yenu mbooleem diiney asamaan yi, ak li ñuy tudde «Ibaadaat » te mooy tudd baati seere yi, ak julli, ak woor, ak génne asaka, ak Aj-Màkka, ñuy ponk yi juróom yiy màndargaal ab jullit.
Ponk bu ci nekk, tënk nañ ko ca na mu gën a gàtte, te ànd ak njariñ, te yit jéem nañ lu nu mën ci masala yi amul benn wuute ci diggante boroom xam-xam yi, lu dul ci ñàkk i pexe.
Maa ngi ñaan Yàlla ndimbal ci liggéey bii, ak sellal ak barke, di ko ñaan mu yaatal njariñam ba mu law te sax, dëgëral ngëmëg aji-gëm, fàggul ki gëmuloon ak ngëm. Yàlla may nu dégg ak topp, te jàppandal nu xam-xam buy jariñ, te nangul nu sunuy jëf. Moo yeyoo loolu, te moo ko mën, Yàlla na nu ko defal. Aamiin !
BINDKAT BI
Bindkat bii di Amaat CAAM mu ngi juddoo dëkk buñ naan Caameen Bàmbara bu Kawlax-Senegaal ci atum 1945. Mu ngi jànge alxuraan ci rakku baayam, jàng xam-xam ci diggante Medina Baay Ñas ak dëkk bu ñuy wax Batara ci Sëriñ Àllaaji Abdulaay Caam. Ci atum 1967 la dugg “Ecole Normale Franco-arabe” ba 1970 mu dem Tunisie defi “stage” dellusi Senegaal ñu def ko jàngalekat ci lekoolu nguur gi…
Amaat CAAM bokk na ci mag i Senegaal yi yenu mboor ak mbatiit u wooteeb Lislaam ci réew mi te mu ngi ciy def ay jéego yu am solo. CAAM, ku fonk jàng ak jàngale la ak tasaare xam-xam u diine.
Woykat la te taalifkat la bu néndu làkkuw araab ba bind ci ay téere yu am-a-am solo. Naka noonu, taalifeef na itam ab “Diiwaan” ci ay ñaan ak tagg Yonent bi (n.y.d.t) ci araab. Góorgi, ba tey ci wolof, mu ngi bind téereeb tafsiir boo xam ne mi ngi ciy firi alxuraan piri mu yaatu te fasaa, yal na ko Yàlla mottali. Aamiin !!!
Avis
Il n’y a pas encore d’avis.