Description
Làmp Faal Kala du mag waaye li taalifam yi biral moo di ne ku xam àddina la, am seetlu ba tax koo bind ci téerem bii ne “Di dund ak ku soxor doy na nattu/Da lay xoqatal di xeex ba nga fattu/Soo dëgërul sa xol bi jeex nga faatu/Te su ñu la tàggee nag ñoo fay jiitu”. Mënees na cee yokk ne kenn walla dara feesul i bëtam. Li mu yëg rekk a ko amal solo, muy bind ngir lal waxtaan ak doom-aadama yépp, di jéem a dab seen bànneex. Firnde bi ci jëkk mooy turu téereb taalif bii EJO génne tey : Xelum Xalam. Woy yi ci biir dinañ féexal xol, ubbi xel, yaatal gis-gis. Waaye yemul foofu ndax day wone yit ne li koy tax a bind mooy fexee dooleel sunuw askan, ñaax nu ci ànd doon benn, di xàccandoo di dóorandoo. Moo tax Làmp Faal Kala ne : “Nanu fexee juboo/Ànd bañ di xiiroo/Ngalla bunu di ŋaayoo/Fàttee jow sunu gaal.”
Ndax lii dawul yaram ?
Lu nekk a ngi ci biir Xelum Xalam waaye li ci gën a fés moo di ne ki fent woy yii taalibe Baay-Faal bu mag la, di ko ndamoo saa su ne. Nan ko dégloondoo : “Nu jóg te sax ci ndigal/Liggéey pastéefu jëf jël/Bunu séytaane dugal/Ba far xañ nu jinaan”.
Avis
Il n’y a pas encore d’avis.