GUDDIG MBOOYO

10 

Description

Guddig Mbooyo, mbirum càcc la nu ci Tijaan di nettali. Moom, nag, mooy boroom-këru Maye mi ay takkaayam ne mes, yëf yi ub boppu ñépp. Te ñi ëpp ci gox bi ñuy wax “Quartier Latin” jàpp nañ ni Tijaan ci boppam moo ko sàcc. Looloo ko tax a ubbi ab lànket ngir feeñal dëgg gi, setal deram. Alkaati la ni Lamin Mbaay mi bind téere bi waaye lànket bi yombul benn yoon ndax da cee xaw a wéet.

Guddig Mbooyo boole na yëg-yëg, naqar ak seetlu te nekk na téere bu yéeme bu laaj njàngat mu xóot ndax sikki doomi-aadama yi ciy Lamin Mbaay di fésal. Duggewu ko nag ñaaw lamiñ ak bëgg a xaste. Li mu ci jublu mooy tooyal xol yi, yee askan wi.

Téere Lamin Mbaay bi dafa neex ba ku ko ubbi doo ko mën a tëj defi leneen te amaana bu jeexee nga ne ci sa xel : “Aa ! Xaat ?”

Avis

Il n’y a pas encore d’avis.

Soyez le premier à laisser votre avis sur “GUDDIG MBOOYO”

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *